Bienvenue à l’Association
Sas woowu nag, nu fas yéene jaare ko ci ñetti fànn yii :

Jàngale mbind ci làmmiñi réew mi, tudde ko Àllarbay làkki réew mi.

Ànd Jubbanti mbind mi wone ak waxtaane téere yi Gēstu ak Siiwal

Wane ak waxtaane téere ci nu bind ci làmmiñi réew mi: Péncum Maam Yunus Jeŋ
Fonk sunuy làmmiñ ag kurél la gu ëmb ay jigéen ak i góor yuy yëngu ci saytu ak jubal làmmiñi réew mi.~~ Mu ngi soqeekoo ci njàngalem ijji mu nu defoon ci iniwersite ci atum 2020.~~
Kurél la guy liggéey ngir jëmmal, taaral làmmiñi réew mi, fexe lammiñ yooyule di amal njariñ askan wi ci lépp lu muy yëngatu, ba mën a indi naataange ci réew mi.
Maakaanu kureel gi : Amitié 2, 4251, Dakar
Bunmi jokkoo yi : 776420294, 774536463, 776377873
